Daagul jaayul ndaama
Xam nga ni daal yaa mën ndaw ñi
Daagul jaayul ndaama
Xam nga ni daal yaa mën ndaw ñi
Moom daal li mu bëgg
Amana du lu bëri
Ku xam li mu war def
Te di ko def comme ni mu ware
Jaabul seeni tele
Soppee nu seeni chaine sax
Waat naa ni su may góor
Duma ko mës a ndele ndax
(Amul) ku dul man
(Xamul) ku dul man
(Gëmul) su ma goree duma ko ndaxe mbaay
(Amul) ku dul man
(Xamul) ku dul man
(Gëmul) jëmmam ji mooy sama njegennay
Yaw la mujj déggoo ba may nelaw
Yaw la njëkk janol bi ma yeewooy
Daaru dunya saa su ne seelaw
Sa jëmm jee doon sama njegennay
Kaay jugal jaayu nak
Jugal yëngal àdduna
Taaru nga taillu nga
Sama jigéen kaay dikkal
Kaay dikkal jaayu nak
Jugal yëngal àdduna
Kaay duma xaasu man
Nala wayal saa su ne
Sama xol yaay kifa njëkk toog
Xas na ma féeteek yaw su ñu yaboo góor-góorlu
Sama xol yaay kifa njëkk toog
Xas na ma féeteek yaw su ñu yaboo góor-góorlu
(Amul) ku dul man
(Xamul) ku dul man
(Gëmul) su ma goree duma ko ndaxe mbaay
(Amul) ku dul man
(Xamul) ku dul man
(Gëmul) jëmmam ji mooy sama njegennay
Daagul jaayul ndaama
Xam nga ni daal yaa mën ndaw ñee
Daagul jaayul ndaama
Xam nga ni daal yaa mën ndaw ñee