Inicio Top Música Bad Bunny Música Cristiana Taylor Swift Ed Sheeran Luis Fonsi Ozuna Daddy Yankee J Balvin Maluma DMCA

Letra de 'Legét' de AMADEUS - Escucha y canta en New Musicas

Varios-artistas

Salsa Brava

Varios-artistas

Top Hits Cristiana

Varios-artistas

Musica De Los 60s Y 70s En Espanol

Varios-artistas

Namaste Classical Music for Yoga

Artist profile picture

Legét

AMADEUS

Canciones

Hey Massamba Walo
Pape Laye

Góom nga woon Yàlla def na tay mu wér
Ba leneen tegu sa kaw
Nga dem bayyi ma ak legét
Xàmmeekaay nga woon
Fu ñu la gis xalaat ma
Fu ñu ma gis laaj ma la
Nga ba ma ak legét

Xol lu fa jiitu sax fa
Yaa njëkkoon ci man
Bokkoon ci sama yaram
Nga dem bayyi ma ak legét

Noo ma war a man a bégloowe di ma jooyloo?
Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo
Noo ma man a woowe ba ma ñëw nga di ma dawloo?
Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo
Moo tax wóolu naa li ne ci man
Mbëggeel laa wóoluwul man
Wóolu naa li ne ci man
Waaye mbëggeel day weere
Moo tax wóolu naa li ne ci man
Mbëggeel laa wóoluwul man
Wóolu naa li ne ci man
Waaye mbëggeel day weere Motax

Li ma realise mooy
Mbëggeel daa jegeñaale
Mbégte ak naqar
Fiiraange di ma fitnaal
Ma dëkke di sóoraale ak di xel ñaar
Li mu may laaaj
Man moom la ma dul man a joxe
Li muy digle duma ko jëfe
Am NDAYSSAN!
Ni ngay bégee nii nga man a jooye

Ba ma rekk ma dem, désolé
Njamala patam réer na ko
Laaj ko fu mu jëm
Dafay wër mbëggeel
Masàmba nga ne lan?
Mbëggeel daa soree
Tax na ba ma jommee

Noo ma war a man a bégloowe di ma jooyloo?
Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo
Noo ma man a woowe ba ma ñëw nga di ma dawloo?
Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo

Moo tax wóolu naa li ne ci man
Mbëggeel laa wóoluwul man
Wóolu naa li ne ci man
Waaye mbëggeel day weere
Moo tax wóolu naa li ne ci man
Mbëggeel laa wóoluwul man
Wóolu naa li ne ci man
Waaye mbëggeel day weere moo tax

Noo ma war a man a bégloowe di ma jooyloo?
Nga dem bayyi ma ak legét
Noo ma man a woowe ba ma ñëw nga di ma dawloo?
Mbëggeel gi góor Yàlla gi la dofloo
Moo tax Wóolu naa li ne ci man
Mbëggeel laa wóoluwul waay
Wóolu naa li ne ci man
Ndax mbëggeel day weere motax
Wóolu naa li ne ci man
Mbëggeel laa wóoluwul way
Wóolu naa li ne ci man
Massmaba Walo

Inicio Top Música Bad Bunny Música Cristiana Taylor Swift Ed Sheeran Luis Fonsi Ozuna Daddy Yankee J Balvin Maluma DMCA