Eey Massamba Waloo
Eh-eh waay!
Bi ma la xame ba léegi yaw
New na nga def lu ma metti yaw
Weg naa la doo fi wayade yaw
Fa ma la aj duma la fa aje yaw
Ndax yaay kenn ki nga xam ni every night man
Moom lay xalaat su may tëdd su ma yéewoo
Yenn saay ma réer nga indiwaat ma
Xam naa ni man rekk nga bëgg
Ki la bëgg ba bëgg la
Te bëggantuwu la
Loo ko mën ci def du ko gis
Ndax mbëggeel nga lay xool
Ki la bëggul bëggu la
Moom bëggantuwu la
Loo ko mën a defal du ko gis
Ndax mbañeel nga lay xool
Xam nga ni man dama la bëgg
Yaw sentir nga coono yi may daj ci yaw
Keneen ku mu doonon ku dul yaw ne na wéreñ
Gis nga ni man dama la fonk
Ñoom ñépp gis nañu coono yi may daj ci yaw
Keneen ku mu doonon woon na ko ginnaaw ba dem
Ki la bëgg ba bëgg la, éeeh
Su la meree dangay feebar di lox di liw
Mel ni ku sibbiru mbëggeel metti na
Ki la bëgg ba bëgg la, éeeh
Su fi nekkee dangay kontaan di bég di ree
Mel ni ku cokkali mbëggeel neex na lool
Lég-lég mu neex, sa xol bi naat
Ngay fecc bànneex di ñaan mu yàgg lool
Ki la bëgg ba bëgg la
Te bëggantuwu la
Loo ko mën ci def du ko gis
Ndax mbëggeel nga lay xool
Ki la bëggul bëggu la
Moom bëggantuwu la
Loo ko mën a defal du ko gis
Ndax mbañeel nga lay xool
Xam nga ni man dama la bëgg
Yaw sax gis nga coono yi may daj ci yaw
Keneen ku mu doonon ku dul yaw ne na wéreñ
Gis nga ni man dama la fonk
Ñoom ñépp gis nañu coono yi may daj ci yaw
Keneen ku mu doonon woon na ko ginnaaw ba dem
Yaw dogo làmp yi ci mbelguane
Waaye man bëgg naa la
Dogo Ngidu ma ci Penda
Man Ndiaga Thiam sama maam la
Yaw dogo làmp yi ci mbelguane
Waaye man bëgg naa la
Dee mo fén di ma tuttal foo nek yëkkëti ma sama waay nga
Yaw dogo làmp yi ci mbelguane
Waaye man bëgg naa la
Yaw dogo làmp yi ci mbelguane
Waaye man bëgg naa la
Yaw dogo làmp yi ci mbelguane
Waaye man bëgg naa la