Gis naa la ngay njaap yeah
Def ci fulla ju mat sëkk
Man daal li may ñaan amiin waay
Mu juge doon sama wërsëg
Day neex ci sama xol
Bis bi nga may njëkk a xool
Ne ma bëgg naa la doonte benn yoon
Lay mas a doon ci sama dund
Yàllaay Buur lu Ko neex dogal
Yàllaay def lu Ko neex ci jaam
Te Yàlla def man ma taamu la
Nattu la am ndogal, jëlal
Yàllaay buur lu Ko neex dogal
Yàllaay def lu Ko neex ci jaam
Te Yàlla def man ma fiire la
Nattu la am ndogal
Hee! Bul ma sàgganne waay
Bul mas a fàtte ne waay
Péncu xol ma yaa fa ne waay
Kon bul ma sàggane waay
Way wi, fent naa ko ndaxte
Yaw kenn nga doo ñaar
Wërsëgu Yàlla nga ehh waay
Day neex ci sama xol
Bis bi nga may njëkk a xool
Ne ma bëggg naa la donte benn yoon
Lay mas a doon ci sama dund
Yàllaay buur lu Ko neex dogal
Yàllaay def lu ko neex ci jaam
Té Yàlla def man ma taamu la
Nattula am ndogal, jëlal
Yàllaay buur lu Ko neex dogal
Yàllaay def lu Ko neex ci jaam
Te Yàlla def man ma fiire la
Nattu la am ndogal
Hee bul ma sàggane waay
Bul mas a fàtte ne waay
Péncu xol ma yaa fa ne waay
Kon bul ma sàggane waay
Boo ma woyafalee mbaa nga sàggane ma
Dina tiis ci man, dina tiis ci man, dina tiis
Boo ma woyafalee mbaa nga sàggane ma
Dina tiis ci man, dina tiis ci man, dina tiis
Eh dama lay xool
Yaa nekk sama biir xol
Eh dama lay xool
Yaa nekk sama biir xol
Bul mas a fàtte ne waay
Péncu xol ma yaa fa ne waay