Chéri coco loo def neex na (nga ni?)
Bu de ay nax sax baax na (haann)
Yaay sama Thione maay sa Diaga (waxal)
Keneen ku dul yaw mi bëgguma (heeee waay)
Bés bi ñu njëkk gise la miir (nga ni lan?)
Danga jonge ci góor yaw mi (bàyyi ma waay)
Bu ma waxoon lu nekk ci yaw mi (bàyyi mu sedd)
Na bàyyi mu sedd ndax waxu fi, eh
Bët mooy xool waaye xol mooy gis
Fu ma mën a xool yaw laay gis
Sa jëmm ji ak sa takkandeer
Guddi gi yaw laay janeer
Sa rafetaay dafa yeme
Moo tax ma jàngi karate
Ku la tooñ fok ñu laale, hé
Noon yiy wax naan mak yaw duñu yàgg
Su desoon si ñoom duñu ànd
Bi ñépp bañee yaa ma nangul
Gàcc ngalam a soxna si bakkul
Yaa ma jàngal mbëggéelu bandit
Yaa ma fuyal toppatoo ma
Moo tax may dox ni Gondi
Yàlla moo ko dogal kenn mënu ci tus
Sama xol jël ko
Loo ci namm bul xaar def ko
Bëgg naa ko dundu ak yaw
Ay fan yu gudd mak yaw
Senegaal yaa ko moom
Soo ma meree ma xar geej gi
Senegal yaay boroom
Soo ko bëggee ma nangu palais bi
Jënd almadi may la
Caabi autoroute bi jox la
Changer monument bi def ci mak yaw
Nekk président pur yaw
Chéri coco loo def neex na (nga ni?)
Bu de aye nax sax baax na (haann)
Yaay sama Thione maay sa Diaga (waxal)
Keneen ku dul yaw mi bëgguma (heeee waay)
Bés bi ñu njëkk gise la miir (nga ni lan?)
Danga jonge ci góor yaw mi (bàyyi ma waay)
Bu ma waxoon lu nekk ci yaw mi (bàyyi mu sedd)
Na bàyyi mu sedd ndax waxu fi, eh
Sama xol bi daf la miin
Yaw rekk sama jarabi
Bëgguma ku dul yaw
Nañu ma bàyyak yaw
Sa yénne ëpp na
Waaye sa mbëggéel doy na ma
Aljànna nga ma ji
Séy ak yaw ba firdawsi
Ayo lé, laaj ma nu ma lay woowee
Ayo lé, sama choco laa lay woowee
Coow du jib
Chéri coco yaay boss fi
Couple bu heureux gay am mi
Ku mu neexul bul ñëw fi
Sama xol jël ko
Loo ci namm bul xaar def ko
Bëgg naa ko dundu ak yaw
Ay fan yu gudd mak yaw
Senegaal yaa ko moom
Soo ma meree ma xar geej gi
Senegal yaay boroom
Soo ko bëggee ma nangu palais bi
Jënd almadi may la
Caabi autoroute bi jox la
Changer monument bi def ci mak yaw
Nekk président pur yaw
Mia eh, mooy Hiroshima, huh
NFU oh, mooy Nagasaki, eh
Chéri coco loo def neex na (nga ni?)
Bu de aye nax sax baax na (haann)
Yaay sama Thione maay sa Diaga (waxal)
Keneen ku dul yaw mi bëgguma (heeee waay)
Bés bi ñu njëkk gise la miir (nga ni lan?)
Danga jonge ci góor yaw mi (bàyyi ma waay)
Bu ma waxoon lu nekk ci yaw mi (bàyyi mu sedd)
Na bàyyi mu sedd ndax waxu fi, eh