Sopp naa la, yaw jaambaaru kër gi
Yaw mi toppatoo kom-kom mu tool
Yaw mi yar xale yi
Di sar jàngoro gi
Sopp naa la, yaw jigéen ju laxu ji
Yaw mi xeex ngir nit moom boppam
Yaw mi xeex ngir jàmm ji yàgg lool ci kaw sof
Yaw yaay su moo yaakaari ëllëg
Han jigéen Afrique
Jigéen àdduna
Jigéen Europe
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Sopp naa la yaw jigéen bu am-sutura bi
Yaw mi ndeyu njirim yi ñàkk ndey, ñàkk baay
Yaw mi am-yërmandé te tabe
Yaw yaa tax gune yi yee feexe
Yaw yaay mbëggeel jër made
Yaw yaay yaakaar di bidéew
Yaw yaay kiiraay gune yi
Yaw yaay yaakaari ëllëg
Yaw mi xam cosaan
Jigéen Afrique
Jigéen àdduna
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Mama sa, eh
Mama sa, oh
Mama sa, eh
Mama sa, oh
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme
Jigéen, mùso, gnonnon, jigéen, femme