Yaw Yàlla
Leer na ma ne ku baax nga
Sa yërmande yaatu na
Jegal ma li ma yax
Li ma gént yéem na ma de
Yaa di buur yaa ëpp doole
Yaay sama boroom
Yaa ñu boole moom
Yaa ma yillif yaw rekk yaa may jox
Yaa fi jiitu yaa fiy muje
Yaa ñu ump yaw rekk yaa feeñ
Sa yërmande ma yéem
Yaay dundal ci sa leer
Suturaal ma bës bu ma la tooñe
Yaw rekk di buur bi
Fees dell ci ngur gi
Boole moom mindeef yi
Buuru jant ak weer bi
Loo dogal bëgg naa, su la neexee neex na ma
Foo ma teg tegu naa fa, gëm naa ni jamu buur la
Bu sirat taxawee, bës bu jaam ñépp di tiit
Sama xol bi dina seede bëggoon na yonnént bi
Fonkoon naa ñi ma mag, jéema bokk li ma am
Daan yeesal ca waxtu ba donte xam na matumaa
Yërëmon naa gone lool donte dama bëri tooñ
Àtt ma sa yërmande, nax dama la reere woon
Nax dama la reere woon
Duma nit ku baax, dinaa jëme fonk waxtu
Duma nitu leer, Yàlla bu ma rëy ba dee ci!
Bu sirat taxawe, bës bu jaam ñépp di tiit
Sama xol bi dina seede bëggoon na yonnént bi
Desalatoo ma Alhamdulilaa
Ku sant Yàlla Yàlla dollil la
Duma mësa doyal ci maagal la
Yaay buuri buur yi, yaa mën defal ma
Yaw rekk yaa mën yaa am te yaa xam
Yaw rekk yaa dac, yaay dindi yaay def
Tegi naa li nga ma wax, seetaanoo ma benn yoon
Deeloo ma li nga ma joxoñ, duma def li ma defoon
Teel nga ma teral lool, ñeewuma saa benn moroom
Def àdduna xol, faate li ñu waxante woon
Moytuloo nga ma sa noon, man ma def ko àndandoo
Yonnént waxal boroom leer yi, mu jegël ma samay toñee
Muhamadu rasulilaa
Ku ko mës a ñaan mu may la
Ku ko mës a tooñ mu baal la ngir mbaaxam
Teeño jeema roy ci yonnént bee
Xayrul anbiyaa yi yaa leen gën, yaa leen mën
Yaw de yaay muhamadu rasulilaa ee Nabi